LyricFind Logo
LyricFind Logo
Profile image icon
Lyric cover art

Li Ngay Gent

Apple Music logo
Deezer logo
Spotify logo
Lyrics
LI NGAY GENT

Ñuné jamono la, du jikko
lu xel amul dal xol ùutiko
Life bi dafa gàtt te bakkan benn la,
kumu neex am say gent dùutiko
tax ganaar bëg ay bëñ, bùkki samp béjjën,
tan doyal ci asaman bëg feey ni jën.
Loy ñaan yalna gaaw, ñëw te gën,
lo ñàkk Yàlla may la xolu muñ te gëm.
Li ngay gent, fatt sa bët, moom sa jot
fees sa xol, jeexal doole, tax lékko, naano.
Li lay puus ci kanam, dila ñaax, yokk jom,
yëkkëti fo daano. Sacrifice, saraxe,
benn bu ci génn nëbb fi junni sukk jalañee,
Tefes yi yàkaar tasee yeene xol yi falañ ne.
Fajar jing koy fasee, talal loxo Qibla
lepp loo fa ñaan, ñaanal Boroom bi mu jig la.

REF
ndax li ngay gent, am na kukoy daw
Sa xel ang ci suuf am kou bëg yeeg ci kaw.
Sa gis- gis louko gàttal? Taxawal, xalaatal
Doom nday xoolaatal li ngay gent.
Li ngay gent xëyna moo lay sànk
Yaa ngui xool fu sori, jàmm ang sa suufu tànk,
fàtte nattu am na,/ doom ndey baa xam nga
li ngay gent, li ngay gent.

2ème
Li ëpp ci liñ bëgg wuuteeg liñu soxla,
àddina conditionner na ñu yëfu dof la.
xaalisak, darajaag, kilifteef, lu fi jara raak?
Leegi so bëggul li ñëpp bëgg sax ñu off la.
Gis naa ku bëg nit ñu sëy, mu jël bakkanam.
keneen ku wër ba am xëy, ligeey bi teeri kaso.
ndax liy xew ba ndogal ñëw, xamoo numuy faso.
Façon bune life bi dina ci wane kàttanam
Ndam li nékk piège, lëj ni këru jargoñ,
ñu lay isaab ci atouts yi nga jàppoon
Yaa ko bëgoon, wuuti ko, mujjée réccu
kon xëccoo beeg jëkkante bi ana luko jar kon?
Foogoon nga ne tukkee lay taxa tekki
tay yaa ngi rew yu gën naat difa dund lu metti.
Ligéey, tabax kër, mu lakk, raylaag sa njaboot
addinaa ngoog, nattoog ci xéewal yi nga toog.

REF

OUTRO
Li ngay gent mën na la gaañ
li ngay ragal mën na la defar

PUBLISHERS

Lyrics © TUNECORE INC, TuneCore Inc.

Share icon and text

Share


See A Problem With Something?

Lyrics

Other